Ñoo ni waat « Yanaa Maar »


Ku ñuy taggati nañu ko tagg ndank
Ku ñuy xasati yit nañuko xas ndank
Lu waay rendi mu nacc ci-y loxoom
Sò wicaxoo mu tiss ci sa-y moroom
…………………………..
Xanaa du yeen-a andoon di kaas ?
Ba tégg ci boppu reew mi keneen
Naan ñu moo gën-a baax ka woon
Tay kookii ñu fal lañu mujj di xass
………………………….
Ñii ni tay tuut lañu amoon lan ñakk far
Ñii di jooytu naan tay lepp-a gën-a tar
Ñii daan ñaxtu ñu bari selaw ni ay xar
Ñii naan ñoo yam ta ñoom ñepp-a far
…………………………..
Askan wi xamul woon teewul ni waaw
Péxé ya antu ñu foli ka woon ci lu gaaw
Mò lu tass ngoro ga ba ngeen di ñaxtu?
Laawon woniwul tax ñu ñëwaat di xultu
…………………………..
Mooné demb yeen la woon ak ñoom
Annd lëngòo mel ni baay ak doom
Dëkké di xas ka woon di ko sossal
Jëlé ko fi gëm loo ñu ni dañuy sonal
…………………………….
Mu mujja mel ci man ni powum goné
Tax may sakku si yeen su mënee né
Ñu féxé ba annd-u politik bi ngor di lal
Ki ñu wóolu ba jiitël bu mu faté lako fal
——–§§—–§§—-§§——-
—–§§ Lamp Fall Kala §§——- La Tribune 221 Lamp Fall Kala
Précédent Vol d’Amour : Tu me soulages
Suivant StWaly Tine : Pour le meilleur et pour le pire

Pas de commentaire

Laisser un commentaire

Votre adresse de messagerie ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *