Neenañu dafa wara Sëy


Fatté ngeen xanaa da ngeena fàté ?
Sëy ak lumu mënti doon, fumu joté
Du fa weesu ci bis bòbu lay maté
Waayé xalé yu gòor yiy jaay nandité
« Mé fils lu gaa yi di xaar laay laajté »
—-§§—-§§—-
Géwël-u juddu bi dila yokk stress
« Goné-g jamm gi cëy bu ñu dundee
Ba lay xéwal sa maas di nañ la ñee
Tux sa di na bën sañ ba rèer fess »

kou yakkamti ba douggoussi dé diga xam ni jaronena tééye
Nga jòg dém daahira bu jeexee
Ba jëwrin jël kaddu tambali soñee
Bu waree ñaan tagoo sula xoolee
« Ñuy ñaan soxna yi amul borom kër
Yalla naleen Sëñ bi may borom kër
Yu jambaaré bëgg leen ta am cër »
—–§§—-§§—–
Maam ja ca kër ga moo-k ñéneen
Tambali laa gaafal yòbu ko féneen
« Damaa ragal ni daa amé far-u rab
Jarnaa wané ji jeem cee wut garab »

Sey fouko Yalla toudd rékk !
Tògàl xaar ta xam ni du yaay dogal
Bul poosé jëkër sa xol mulay sonal
Bul yakamti déf ku fëgg nga ni kiila
Yokal fulë ak fayda xam ni nooniila
Ki bëg lu baax bis dina ñëw ni fiila
——§§—–§§§—–§§——
Aji wééy ji : ——–§§ Lamp Fall Kala §§——— La Tribune 221 Lamp Fall Kala
Précédent Modou-Modou, vous nous faites vivre
Suivant Le fait-chier electo…râle

Pas de commentaire

Laisser un commentaire

Votre adresse de messagerie ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *